Logo Kurélu W3C bu Senegaal

Nanu jëme Web bi ci digg dooleem...

World Wide Web Consortium (W3C) kurél la guy defar ay xarala yu jokkoloo (tëraliin, lojisel, aki jumtukaay) ngir jëme Web bi ci digg dooleem jaare ko ciy pénci xibaar, yu njaay, yu jokkolante ak yu dëppook askan yi. Kurélu W3C bu Sénégal (di it Kurélu W3C gu Afrig Sowwu-jant) moo jiite bépp yëngu-yëngu W3C ci Afrig sowwu-jànt.

Xibaar

5 Sue 2010 - BootCamp ci xarala yu web semantik (Technology Web Semantic ci làkku Àngale) ak làkku Wolof ci Web bi: Seddoo xam-xam yi ñeel askanu Senegaal.

Kurélu W3C bu Senegaal dina amal bis bumu jagleel xarala yi ñeel Web Semantik ak jëfandikug làkku Wolof ci Web bi. Mi ngi koy amal gàwwu 05 sue ca Lekkool Politeknik bu Kawe ba ca Ndakaaru. Ca bis boobee, deesna ca amal joηante ngir tabb jumtukaay bi gën ñeel seddoog xam-xamu yi jëm ci askanug Senegaal. Ñi ngi baayale joηante boobu Kurél gii ñu duppee Population Council (Dees na ca joxe ay raaya). Dees na leen jox ay xibaar yu gën a yaatu fii aki bis.

Bisub tàggatu ci CSS / XHTML ak leerlu bu W3C

W3CW3C-SN : Kurélu Senegaal bu W3C (te Deppartmaa bu Kàjju informatik bu ESP dalal ko) dina amal bisub tàggatu ci dëppalekaayu CSS/ XHTML ngirug càmmanteef jumtukaay yooyee ci dalu web yi. Dees na ko def 29 Desàmbar 2009 ca Lekkool Politeknik bu Kawe ba ca Ndakaaru (ESP)Armanaat


Estatistik
Kurélu W3C Senegal gu a ngi ñu dalal ci Departmaa Kàjj Informatik bu Lekkool Politeknik bu Kawe bu Ndakaaru
Valid XHTML 1.0 Transitional CSS Valide !